CAN 2022 (BEACH SOCCER) : SENEGAAL GÀDDOOTI NA NDAM LI
Senegaal jël na Can 2022 (beach Soccer) bi. Esipt la dóorati 6-5 ci dóoral-ma-dóor (tirs au but) yi ginnaaw bi ñu témboowee 2-2 ci biir joŋante bi. Bii nag, mooy ñeenteelu yoon muy tegle di ko jël, ak juróom-ñaareelu kubam ci mbooru kub bu Afrig (futbalu

Senegaal jël na Can 2022 (beach Soccer) bi. Esipt la dóorati 6-5 ci dóoral-ma-dóor (tirs au but) yi ginnaaw bi ñu témboowee 2-2 ci biir joŋante bi. Bii nag, mooy ñeenteelu yoon muy tegle di ko jël, ak juróom-ñaareelu kubam ci mbooru kub bu Afrig (futbalu tefes).
Gaynde Senegaal yi woneeti nañ seen bopp ci Can 2022 bi. Ci àjjuma ji, 28 oktoobar 2022, lañ doon joŋanteek Esipt gañ-jël bi ca Mosàmbig. Mu doonoon nag jàmmaarloo bu metti. Ñaari ikib yi, benn mayul sa moroom dara. Senegaal a njëkk yëngal caax yi biñ dawalee ba ci juróom-ñaareelu simili bi, ci xaaj bu njëkk bi. Ci ñaareelu xaaj bi, ikib yi dërtoo nañ wet gu nekk, waaye bii duggul.
Bi ñu demee ba ci ñetteelu xaaj bi la Esipt dugal, dugalaat ci ñetteelu simili bi, daldi jiitu. Senegaal di daw ci ginnaawam. Ñaari ikib yi nekkalaat ko ca ba ci juróom ñetteelu simili bi, Senegaal soog di dugal ñaareelu biiwam. Ñu jóge fa, benn ci ñaari ikib yi dugalaatul. Ba liñ leen yokkaloon ci simili jeex, ndam demul ndam dikkul.
Naka noonu ñaari ikib yi jàll ci dóoral-ma-dóor yi. Bi ikib bu ci nekk dugalee juróomi teg-dóor (penalty) la góolu Senegaal bi, Al Seyni Njaay, jàpp juróom-benneelu teg-dóoru saa-esipt yi. Saa-Senegaal bi, Sã Ninu Jaata daldi dóor dugal. Mu nekk 5-6, Senegaal amati ndam.
Muy niru li wolof naan ndox du bàyyi yoonam. Ndax kat, ci atum 2016 ba léegi, Saa-Senegaal yi teggiwuñ benn yoon seen i loxo ci kub bi. Ñeenti yoon yi mujje yépp ñoo ko gàddu. Rax-ci-dolli, ci atum 2022 bi, bii mooy ñetti yoon ñuy am ndam ci kow Esipt miñ door ci gañ-jël bi. Bu yàggul dara, ci weeru sàttumbar bii weesu, Saa-senegaal yi xañ nañ Esipt kub ci gañ-jëlu COSAFA bi. Ñu ñëwati Kub bu Afrig ñaari ikib yi bokk benn làng, Senegaal làpp ko (6-4) ci seen ñaareelu joŋante.
Waaye dafa mel ni du Esipt rekk la Senegaal mën. Nde, gaynde Senegaal yi dañ faf teg tànk ci Afrig gépp. Ginnaaw biñ tegalee kub bi ci ñeenti at yi mujje yi, bii mooy juróom-ñaari yoon ñu koy jël. Ñu jaare fa nekk ikib bi ëpp ndam ci kembarug afrig ci futbalu tefes gi. Léegi nag, ñu leen di xaar ci kub bu àddina si war am ci 2023 bi, ndeem bokk nañ ba noppi.