YÉGLEB WAY-BOKKI NDAJEM ÑAXTU NGIR DOOLEEL ASKANU PALESTIN

Démb, ci dibéer ji, lañu doon amal i ndajey ñaxtu, fii ci Senegaal, ngir naqarlu lay xew fa Palestin. Li ñu ko dugge woon du lenn lu moy ngir àdduna sépp xam ne li ñuy teg askanu Palestin metti na leen ba fu metti yam. Nde, kenn umpalewul ne, bu yàgg ba tay waa Israayel ñi ngi leen di bóom. Réewi jullit yi ba ci sax réew yi nga xam ne duñu ay réewi jullit ñi ngi koy ñaawlu, di ko metitlu. Looloo waraloon, fii ci réewum Senegaal tamit, am ñu génnoon ngir fésal seen tiis ak naqar. Ginnaaw gi, ñu génnee ab yégle daldi ciy dëxëñ lu bari. Muy fa Israayel jëm ak Palestin ak ñoom li ñuy sàkku ci Nguurug Senegaal ak mbooleem ñi nga xam ne lii metti na leen.
Xare bi dox diggante Israayel ak Hamas tàmbaliwul tay. Xanaa kay, dafa am lu xolliwaat góom bi. Bóom gi fa am, jamono jii, mi ngi dooraat juróom-ñaari fan ci weeru oktoobar, atum 2023. Booba ba tay nag, sox yi moom, daanaka dakkul. Ay junni-junniy doomi-aadamaa ñàkk nañu ci seen bakkan. Saa su ñu jàppee ne jeex na rekk, fekk booba la Waalo gën a aay. Dafa di, ñoom dañoo gis ne Israayel mébétam mooy def ni Almaañ defoon ci ñaareelu xare àddina si. Maanaam, li fay xew du ab xare kese. Aw xeet lëmm lañu fa bëgg a faagaagal. Ñoom li ñuy def nii dafa salfaañe sàrt bi àddina sépp bokk ñeel gëddaal doomu-aadama. Lépp àddina si teg ci seen bët, te, kenn yéyul yàbbi ci. Menn réew newu leen déet.
Li ci gën a doy-waar mooy dañuy bóom ñoo xam ne duñu ay sóobare. Maanaam, ay maxejj, ay jigéen, ay xale, ay màggat. Te, yamuñu foofu rekk. Ndax, dañu cee boole xañ leen ndox, kuuraŋ, lekk ak naan, paj ak njàng, yépp boole kook sox yu dul jeex. Bés bu nekk ñuy bóom ñoo xam ne yoruñu ay ngànnaay, du dara. Maanaam, ñoom dañuy maasale rekk. Ay radu gumba lañu yor, bàyyiwuñu kenn.
Te, ñoom ñi ñuy gën a diir mooy fajkat yi, saabalkat yi ak ñiy jàppale askan wi. Bu dee am na ñu naan leen déet, Etaasini moom bokku ci. Moom, daf naan leen waaw góor ! Di leen jàppale ci koppar ak ciy ngànnaay. Ñoom nëbbatuwuñu ci wenn yoon.
Looloo tax, ñi doon amal ndajem ñaxtu mi, démb, ci dibéer ji, ñi ngi wone seen naqar ci liy xew fa réew mooma. Di leen wax ne ñi ngi ànd ak ñoom. Rax-ci-dolli, ñi ngi rafetlu taxawaayu Nguurug Senegaal ak réewi kippaangoog Haay (Afrique du Sud, Namibie, Sénégal, Belize, Bolivie, Colombie, Honduras et Malaisie). Ndax, ñoom fésal nañu seen yéene. Te, seen bëgg-bëgg mooy waa Israayel teggi seen loxo ci waa Palestin, bàyyi leen ñu nekk seen jàmm.
Ñi ngi sàkku tamit ci Nguuru Senegaal mu dog jokkalante yi mu am ak réew moomu di noote, boole kook di boddi xeet. Te, bu ñu yam foofu. Nañu ci boole dàq seen ndaw li fi nekk (ambassadeur). Te, ñu bañ a jëndati mbooleem ndefar yi nga xam ne Israayel lañu jóge.
Mu mel ni xare boobu yàgg na te metti lool. Donte ne sax, ci askanu Palestin la gën a mettee. Ñu lay dóor metti na. Waaye, dóore tamit, yombul. Te ba tay, saafara amagu ci. Réew yu baree ngi koy ñaawlu ak a naqarlu. Loolu terewul, sox yaa ngay wéy. Li mat a laaj kay mooy lan moo mën a dakkal xare boobu ?