DOKTOOR JÀLLO JÓOB : GOR CI WAX, GOR CI JËF
Bees sukkandikoo ci waatub Hippocrate, dees na gis ni balaa ngay yeyoo turu fajkat dëgg, dinga làmboo juróom yii : cëral sab sëriñ, fonk ki ngay faj, bañ koo doyadil, am sutura, am ngor.

Bees sukkandikoo ci waatub Hippocrate, dees na gis ni balaa ngay yeyoo turu fajkat dëgg, dinga làmboo juróom yii : cëral sab sëriñ, fonk ki ngay faj, bañ koo doyadil, am sutura, am ngor.
Doktoor Jàllo Jóob nag, da cee boole nite. Kon, mënees na ni, doktoor tigi la. Ñi muy faj gërëm nañu ko, ay naataangoom weg nañu ko.
Waaye, laata Dr Jóob di doon fajkat, filoo la tàmbalee njàngam ca Tugal. Bañoon dellu fa Tubaab yaa ko taxoon a bàyyi filoo doonte lu mu bëggoon la lool. Ndokk-Yàlla ba ko waajuram wu góor gawee ci njàngum paj ngir mu toog Senegaal. Waaye, bi mu génnee kaso, Iniwérsite Ndakaaru da koo dàqoon, mu dellu Tugal eggali njàngum paj, ñibbisi Senegaal, dooree liggéeyu paj ca Kaasamãs.
Séex Anta Jóob moo koo xelaloon mu xóotal xam-xamam ci fànnu « biologie moléculaire ». Maanaam, gëstu ci wàll wi gën a tuuti ci mbindeef muy dund « ndax xarala ëllëg la ». Mu jëmbat ci njaambaar ba am ci maitrise, DEA ak Thèse. Pari la defee daaray tuut-tànk ak ju diggu-dóomu ji, amee bakalooryaam Ndakaaru, Liise Blaise Diagne. Nee na seen eksamaa booboo gën a yomb ci mboorum Senegaal ndax amul woon bind, laaj ak tontu kese la woon (oral). Atum 1968 la woon, bi ñu génnee ndem-si-Yàlla ji Maxtaar Jaag mi desoon ci kaso doon kenn ki ñu bàyyeegul woon ci ñi ñu jàppon ci wàllu politig. Moo taxoon ndongo yi bank seen loxo ne su génnul, eksamaa du am. Kenn kepp a lajjoon ci ndongo yooyii doon def bak ca at mooma.
Su loolu weesoo, Dr Jaalo Jóob moo doon njiitu pàrti RND bi fi Seex Anta sosoon ci kanamam, mu nekkoon « caatu pàrti bi ». Kon su nu nee Jaalo Jóob saa-Afrig bu bëgg Afrig la te gëm der bu ñuul, du waxi kese. Ci gis-gisam nag, « am réew su bëggee moom boppam, fàww mu moomal yii boppam :
– kopparam, di def ak a dindi na mu ko soobee ;
– kaaraangeem ndax solo si mu ëmb
– pajam ak njàngam, di ko jaare ci làkki réew mi ».
Cër yii, nee na « du lees di dénkaane », ëpp naa tayle. Waaw-góore waay ! Day fekk nag nga xam li lay jariñ nga nekk ci ak fulla ju mat sëkk.
« Fit ak ngor » taxoon Seŋoor jàpplu Jaalo Jóob, tëj ràpp. Naam kasoom metti woon na waaye ngor ak jom la fa dundee weer ya mu def ba na mu génnee. Xamee na fa nag « lu benn Iniwérsite ci àddina dul jàngale ». Amul lu ko réewam jaralul, moo tax foo ko fekk mi ngi laxasaayu.
Nuy fàttali ne Doktoor Jaalo Jóob rakku Omar Bolondeŋ mees « bóomoon » ci kaso Gore bi la ci atum 1973 (amul woon lu dul 26i at). Mënees naa tëj jëmmu doom-Aadama waaye mëneesula far ay xalaatam. Lu ëpp genn-wàll xarnoo ngii Jaalo Jóob ak njabootam di sàkku Yoon tëggaat layoob Omar Bolondeŋ ngir mu leer. Nguuri Senegaal di ñëw ak a jàll te coppite amagu ci. Waaye « ñuy yaakaar ne ak gu Jomaay-Sonko gi dina deme neneen ».
Jaalo Jóob mii, seen yéenekaay, Lu Defu Waxu am mbégte di leen ko fàttali ak a wonale, dafa ñuul ñuulaay buy tàkk, bopp bi weex tàll, njoolul lool. Bindam daa sew, weñ gi dëgër, mu njaxlaf di saamandaay ab dawkat. Doo ko ni jàkk ba xalaat ne romb 70i at. Xolam dafa set, noonu it la setee ci boppam, di sol lu set te niroo. Kàddoom leer na te neex ndax lu mu xam lay wax, ñeme ko. Ni muy jëlee ay bëtam wékk la day wone dëggoom, nee nañ ñaare bët du fen. Moom dinay faral di takk montar ci loxo càmmiñ bi, takk jaaro xaalis ci baraamu tofu-digg bu loxo ndey-joor bi. Bi mu bokkee ci Magi Pasteef ak tey day takkaale lam bu boole xonq ak nëtëx, meloy pàrteem.
Ci geneen wàll, kii ay jegeñaaleem di woowee Paap Jóob, ku neex a digaaleel la : am na köllare, yaatu na, mën naa abale nopp te yéwén na. Kon tànneef la ci xaritoo. Dinanu faral di dégg mu naan “du gis ngeen, nun, danoo fonk sunu yaay, fonk sunu soxna”, kon fonk jigéen ci gàttal.
Dina koy neex muy sargal ku nangoo liggéey, di jàppalewaate te moom boppam. Dr Jaalo Jóob doomu Doktoor Ibraayma Jóob Bolondeŋ la ba noppi Seex Anta baayale ko boppam kon xarbaax yi ci moom warta bett kenn.
Ku am ag ràññatle la, xëccoowul lenn, xaarul ndombog-tànk, te it raŋale ay medaay ñoru ko ; waaye saxaar ci and cuuraay, neex, naqari, ci kow lay jëm. Kinne Gaajo nee woon na ci Bàmmeelu Kocc Barma bu Bubakar Bóris Jóob (EJO-EDITIONS) “soxlawunu àbbaani ay maam” maanaam jéggaaniy royukaay. Dëgg la te Jaalo Jóob mii royukaay la, gor ci wax, gor ci jëf ; nuy dagaan mu yàgg fi lool te wér !
Ndey Koddu FAAL